Informazioni sulla canzone In questa pagina puoi trovare il testo della canzone Sportif, artista - Youssou N'Dour.
Data di rilascio: 28.10.2007
Linguaggio delle canzoni: Cebuano
Sportif |
Woyal sa wayu ndam ii |
Dangay bégël sa xol bi |
Ndax yaa yor bannex bi |
Ni tay bés bii sa bés la |
Sa mbër daan na kóntaan nga |
Bu ñu daanee sa mbër nak |
Na nga fexe ba nee |
Po mii dañuy Jonante |
Faw mu am ku moyle |
Jarula defante, di xasteeka dóóre |
Jonante po ag ree la |
Boo gañee fo ag ree la |
Boo ñàkkee fo ag ree la |
Lépp ci fo ag ree la |
Buñ la gañee muñël |
Boo ko gañee baalal |
Bëgóón nga mu demee ni demewuko |
Mën naa am bu ëllëgee mu gën fee neex |
Ba ma làng ag samay gaa yi ngir bànneexu |
Xam ne lii fo la nii lay mënë deme |
Powun jonante nii lay deme |
Tay jii yaw bu ëllëgee keneen la |
Fo ag ree de lañ ciy jublu |
Moo tax ñu wara dal taynangu defet |
Jonante po ag ree la |
Boo gañee fo ag ree la |
Boo ñàkkee fo ag ree la |
Lépp ci fo ag ree la |
Buñ la gañee muñël |
Boo ko gañee baalal |
Waa waaw wuy dabbee wuy yoo |
Dabi alaa ko ndey baate satata |
Abdulaay ag Maajoor Maajoor ag Mataar ag jaara seen jigéén |
Sire lañu dóór bal géér ña da ñoo daw |
Sire Bàlla moo ñaan Ramata Faal |
Siree nga Cees Matee nga Njaarém |
Duñ ko wëy ku reew, duñ ko wëy ku ñaaw |
Aah wuy dabbee wuy yoo |
Dabi alaa ko ndey baate satata |
Jonante po ag ree la |
Boo gañee fo ag ree la |
Boo ñàkkee fo ag ree la |
Lépp ci fo ag ree la |
Buñ la gañee muñël |
Boo ko gañee baalal |